Barhâma,Barhâma Niasse Cheikhoul Koulil Awliyâ Barhâma
1. Barhâma,Barhâma Niasse Cheikhoul Koulil Awliyâ Barhâma Cheikhoul koulil Awliyâ’i Bâye Barhâma
2. Kholalma fenkak Baye bi thi Taïba Niasséne Goorou Haïbou yeup Têw Nâne Barhâma
3. Serigne bougne koy Toopé Tâar Thiolayame ba souko gnaké Mélokaname ba def lay lèr, Barhâma
4. Taarou Diamant ki ko sôlo kôkou moy jeumi Bâye Niasse Jeumeul na mbidèf yeup Niouy Barhâma
5. Dou dê ,Dieufeum dou nul,kouye soul dieuf goréwôu…lo Diogléne gnou ndioukeul Wâja mooy Barhâma
6. Bilâhi wa lâhi môm Bâye souko Nêkhone Kou wôté dougne la wouyoussi Bâye Barhâma
7. Barigot bou fêsse dou yeungou wêr wêr bi Tankhal nagnou Khathie bouy maté douye mbawé, Bâye Barhâma
8. Sô guissé kou yomb dajalé aw limame dotoul tôgo Ninki nanka dougne koy sôrou Barhâma
9. Kholalma Bâba Lamine tothie na Makkah ak sôdan Niouy gamou ziarré si Bâye Barhâma
10. Boul sonk kholal auto bi,ap chauffeur ra koy conduire Douneyâ bi itam nônou thi Barhâma
11. Sakhar kou diâr thi yônam boula firé ya ko tôgno Ndakh yônam bi pour môm rek la, Barhâma
12. So méré ya nga nâne di na taglé galace ak ndokh Thiossane galâce ndokh la,Bâye Barhâma
13. Môgnou wakhone thia wey wa may bakane yi may gokh yi,may bakane yi may gokh yi May leep lou ngéne dianole , Bâye Barhâma
14. Yeen mbolo mi fi tew , yalla na léne yalla yôk ,yalla na léne yalla yôk Té diokhléne maqâma yi, thi Barhâma
15. Mane souma nampone arabe tey ma tag Barhâma Cheikhoul koulil Awliyâ’i Barhâma
16. Bâye môgnou nampal,môgnou lèral, thi lêrou Allahou Allâhou,Allâhou, Allâhou
17. Allâhou,Allâhou Lâ ilâha ilâ lâhou,Allâhou
18. Bâye môgnou jeuzbou , môgnou guindi thi lîfou Allâhou Allâhou,Allâhou,Allâhou
19. Allâhou,Allâhou Lâ ilâha ila lâhou ,Allâhou
20. Bâye môgnou dioubal môgnou khâmal thi Hâ’ ou Allâhou Allâhou,Allâhou
21. Lâ ilâhâ ila lâh Lâ ilahâ ila lâh
|