| Accueil | Créer un blog | Accès membres | Tous les blogs | Meetic 3 jours gratuit | Meetic Affinity 3 jours gratuit | Rainbow's Lips | Badoo |
newsletter de vip-blog.com S'inscrireSe désinscrire
http://emeu.vip-blog.com


ALLAH BARHAMA
VIP Board
Blog express
Messages audio
Video Blog
Flux RSS

ALLAH BARHAMA

VIP-Blog de emeu
mamadou2h@hotmail.com

  • 192 articles publiés dans cette catégorie
  • 269 commentaires postés
  • 1 visiteur aujourd'hui
  • Créé le : 27/04/2007 01:51
    Modifié : 25/05/2010 23:14

    Garçon (28 ans)
    Origine : Dakar
    Contact
    Favori
    Faire connaître ce blog
    Newsletter de ce blog

     Juillet  2025 
    Lun Mar Mer Jeu Ven Sam Dim
    30010203040506
    07080910111213
    14151617181920
    21222324252627
    282930010203
    [ Articles ] [ Multimédia ] [ Sahabas de la Fayda ] [ Prophètes de L'ISLAM ] [ Disciples Tidjani ]

    FA ASSI SALAMOUN MINE ILEYKA (zikr)

    11/02/2008 18:29

    FA  ASSI SALAMOUN MINE ILEYKA (zikr)


    Fa assi salâmoun miné ileykaa

     

     

    mahriwal anbari wati bamiskâ

     

     

     

     

    damay welbati mbôlèm wa wayéni sodâne 

     

     

     

    ba zahir ba di batine ma diar di sétane

     

     

     

     

    sama khatir dafa roti ba bahrou kadior 

     

     

     

    maye waye ki diara waye mogno touché ay lêre

     

     

     

     

    mâye guéwel bi si lislam khamal ma ko done

     

     

     

     

    kone ma wayla té kagne la ya donou rabbâne

     

     

     

     

    siroupe guenél bingua lambo thi diné lislâm

     

     

     

     

    soppé bé lako diokh mo yayo thia khadim

     

     

     

     

    khout boul diamiou bi niass yadi diantou ndiolôr

     

     

     

     

    sakhale ngafi aye lêr teksi mbôte you doy wâr

     

     

     

     

    manguiley yalwane yawmi donou tidjâne 

     

     

     

    mayma sa mébétame khole ma dê thi limâne

     

     

     

     

    fougoulénaâ tibeulema ndakh ma diogue si békôr

     

     

     

     

    rafléna wodou ma ndakh ma ba limay gâre

     

     

     

     

    sa walô guena gaw khop fou fadou bay bour

     

     

     

     

    sa khéwel guena bawane ba mélni ay nîr

     

     

     

     

    sa até guena wér yaye khalilou rahmâne

     

     

     

     

    bé lo wakh borom koun daldiné fayakôune

     

     

     

     

    sa kharbakh yingua lambo séwalna doctôre

     

     

     

     

    bé kô toufli mou wér far dou dème si doctor

     

     

     

     

    té ko toufli sa lorwi tafalko bousrâ

     

     

     

     

    mou tagook lorou dounya kasaka oukhra

     

     

     

     

    dama sop dila way wanté rawnga saye masse 

     

     

     

    litakh ma dila waye nga nirok borome fass

     

     

     

     

    sa mbôtoume khalima raw daboussou moussâ

     

     

     

     

    sa way déé yinga dékal téwalna insa

     

     

     

     

    kouy mouride nama gnew waylé sidi Barhama

     

     

     

     

    wadiou kham mana ragné té wanema Barkhame

     

     

     

     

    té diokhmame khatir mbâ ngua mayma sam khôle

     

     

     

     

    té bawal mâme khéle mba nga mayma sak mougne

     

     

     

     

    kone dina mena waye ki fi guene thi sôdâne

     

     

     

     

    di khoutbou rôuhou yi nane si péyou diwâne

     

     

     

     

    dégloutiléne bama déloti kagne ki guene fî

     

     

     

     

    thia azal lako bour djitelone douhout fi 

     

     

     

    Barhama bangua rote bassaye bagane fess

     

     

     

     

    Bawalal gnala done khare ba séni ndap fess

     

     

     

     

    Halam ak alalam mome la diaye thi lislâm

     

     

     

     

    Gnou signélko mou wér diohko khatmou faylom

     

     

     

     

    Boungéne khamone ay may sa souné kone ngéne téw 

     

     

     

    Bagna linkar bagna dingat té ngéne sakho wâwe

     

     

     

     

    Betoub kagnane daffa bépéle dou sétlou khar bakh 

     

     

     

    kone gnou guiss banga wathié gnou khamné ya bakh 

     

     

     

    mousta diok kêur bâyam té raw thi lislam 

     

     

     

    béne serigne mounou fé wakh ni démna darâme

     

     

     

     

    sou kagnane amoutone lolou modi mbâhk

     

     

     

     

    sou féké ngay khém lolou doyna kharbâkh

     

     

     

     

    bame yoré gnéti ate la diadial boussoura

     

     

     

     

    téé rawna kouy mâssam né at ya wéye dâw

     

     

     

     

    bamou yoré arafome thia la samp dârâme

     

     

     

     

    di diour aye massalam bolékoke makhamame

     

     

     

     

    siroup ngeunél binga lambo néwoul si aye mbôle

     

     

     

     

    yaye khoutbou yaye khawsou yaye seydi ridiâle

     

     

     

     

    touti woul reyoulite gatoutite douhout ndiole

     

     

     

     

    dieumi rassoulou la yor ngo niro bathik maule

     

     

     

     

    sou beute yaye nalawite khole ba mome mangay khôle

     

     

     

     

    té rougua arassak kourssiyou thialay bèle

     

     

     

     

    té bouye rèè day mougne khar kaname badi léer kar kar

     

     

     

     

    té waram guena nékh lém thi khole yimouye war

     

     

     

     

    bala ngakoye khéme lole bobou aw nakar fégne

     

     

     

     

    bo kholé Barhama niass guisko mouye mougne

     

     

     

     

    moy djikom diamou dono si seydi adnane

     

     

     

     

    ndogal bou réeye bala doylo moye koune fayakône

     

     

     

     

    falé woule adinak lithi bire dafay nîl

     

     

     

     

    khégnetouwoul loumoy yala ak naba dâl

     

     

     

     

    mousta am kou mou khèm thi alal bané sôuye

     

     

     

     

    té am kome douko béwlo amoule koumoye faye 

     

     

     

    kontéwoul aye tone ni dome youné ay takh 

     

     

     

    rabboul samawati wal ardi doye naka diékh 

     

     

     

    té mandok ragal yalla tabé thi lislam

     

     

     

     

    té tôlam ba dou boye modi yonou diakam

     

     

     

     

    itéme ya mo guena khir gaïdé mbaya bouye bour

     

     

     

     

    karamame ya guena reye doussou golf bouye dôr

     

     

     

     

    haye beutem dafa for mélni dianou samar 

     

     

     

    rahmatam dafa khir thi fakhira miskine 

     

     

     

    soukhali nga sougnou khole yi soukhone thi zoulmane 

     

     

     

    né niomineka bou mbâle diéne ba wér thia nanguane 

     

     

     

    silmakha kouko taylé bamou khole assamâne 

     

     

     

    warna dioub bayi thiakhane té topou saye wâwe 

     

     

     

    raboul dialil lako fal diokhko manto rabane 

     

     

     

    falko mouye fali donou séwalna labdane 

     

     

     

    wal takoum oumatoum mome la akh thia lakhôt 

     

     

     

    kou aw thi ndigalam kham ilâkhi nassôte 

     

     

     

    bagnou yoré sougnou adio siyaré madina 

     

     

     

    bagnou démé bathia pomeba mou dieufa diorâne

     

     

     

     

    dieumeume diayetassarou khade ya bagua dianokmôme

     

     

     

     

    dougnou mebeute loumou topethi takhôk môme

     

     

     

     

    mélow youssoufa la yor ki rawone thi ay tare 

     

     

     

    béé kou dianok mome sopko ndakh fa yor lér 

     

     

     

    Aladji Abdou sougnou mame dana wakhné moye khâss 

     

     

     

    né booba mougui khole nawlé yak beutouk masse

     

     

     

    na khalil natou wone natou wagne ko diourone 

     

     

     

    la Barhame fayé balayi fi thi sodâne

     

     

     

     

    na khadir natouwone moussa fa mâwoul hayât

     

     

     

     

    la sougne baye yeré domame yi bi izni mâyâ

     

     

     

     

    djoulil nak thi rassoulou lahi moukhtare

     

     

     

     

    salâtane wa taslimane ma gnane ko harfâ

     

     

     

     

    toudé na wilé waye sâlihâti djihâte 

     

     

     

    thi kou sapék gnifi dane waye imamoul hindade

     

     

     

    fafal khatmou sa waywi yaw thiam 

     

     

     

    né lo lime limitam do djiadial ba déme same 

     

     

     

    khassayite yingua tâlif manéssoukô mbôle 

     

     

     

    adjâlil yingua sankh séwal na labdane 

     

     

     



    Commentaire de thiongane (14/01/2009 17:55) :

    yalnalla yalla yoko thi barké baye amiiiiiiiiiiiiine

    http://thiongs@hotmail.fr




    Début | Page précédente | 94 95 96 97 98 99 100 101 102 103 104 105 106 107 108 109 110 111 112 | Page suivante | Fin
    [ Annuaire | VIP-Site | Charte | Admin | Contact emeu ]

    © VIP Blog - Signaler un abus